Paroles de Gagganti Ko
Paroles de Gagganti Ko Par YOUSSOU NDOUR
Ba ñu la koy jox , xam ul dara
Bu la séen ée , daw gatandu la
Ay waajur ëm, da ñoo am oon yaakaar ci yaw
Jamono y dox , jafejafe am , sëytaane ñëw
Bu ko dóor , bu ko saaga , bu ko xas , bu ko wax lu ñaaw
Delloo l sa xel , ca ginnaaw, te muñ ël ko
Ba ñu la koy may , xam ul dara
Bu la séen ée , daw laxasu la
Ay waajur ëm, da ñoo am oon yaakaar ci yaw
Jamono dox , jafejafe am , sëytaane ñëw
Bu ko dóor , bu ko saaga , bu ko xas , bu ko wax lu ñaaw
Delloo l sa xel , ca ginnaaw , bu ko souffrir loo
Xool al ci ay , waajur ëm , bu ko joy loo
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu ko dòor , bu ko saaga , bu ko xas
Bu ko wakh lu ñaaw
Bu yënggël ée daal , ba sa xol fees , génn ël nga dem
Bu fa toog yaw, di raak ak moom , sàmm al sa cér
Woo ko , waxtaan ak moom , té muñël ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Yaw tam , bul forcer , deel négocier
Ndaw sii , bul teg deal , bul planifier
Te bu am ee , lu fi leer ul , nga clarifier
Coow li , bu déborder , nga pacifier
Yaw daal , bul forcer , deel négocier
Ndaw sii , bul teg deal , bul planifier
Te bu am ee , lu fi leer ul , nga clarifier
Coow li , bu déborder , nga pacifier Wa waaw
Jaajëf , di na tax , xale wone jom
Waaw góor, di na tax , xale yokk jom
Di ko won sa jom , moo koy dolli jom
Jom jom jom rek , dara lu dul jom
Yërëmal ma ko
Momit mou wégal ma laa
Nax ko neex al ma ko
Moomit mu xam ko
Ecouter
A Propos de "Gagganti Ko"
Plus de Lyrics de YOUSSOU NDOUR
Commentaires ( 0 )
Aucun commentaire pour l'instant
Vous aimeriez sûrement
Essayez l'application Mobile
A propos de AfrikaLyrics
Suivre Afrika Lyrics
© 2024, We Tell Africa Group Sarl