Paroles de Daf Niou Bett
Paroles de Daf Niou Bett Par MAABO
[MIA]
Yàgoon naa foog nii
Soxlawuma kudul man mii
Man kenn lawoon ci yoon wii
Dox di dem ak sama yan wii
Bes bi ma la gisee
Keroog dafa leer ci ñun ñaar
Sunu xol yi ni ñu dajee
Ci laa xam ni yaw laa doon xaar
Yaa Yaa Yaa Yaa
Yaa tax may wër
Fi mbegte ne ngir indil la
Yaa Yaa Yaa Yaa
Foog ma siggil la
[REFRAIN : MIA & NO FACE]
Sama jàmm yaw la
(Yaa tax ma xam ni mbëgeel neexe)
Suma beggee yaa tax
(Mossuma foog nii...)
Sama jàmm yaw la
(Nit dinama toll fii)
Suma beggee yaa tax
Lii daf niou bett maag yaw!
Ci mbegte nga may dello (dello)
Dima dëfal may ree
Awma beneen héros
Man yaa may begal saa su nekk
[NOFACE]
Mbëgeel dina yegsi fing kodul fooge
Këf sa xol di fowee
Yaw laa sopp te yaw laa nob
Yaa leen gën fopp, do ñaar yaw!
Jikko yi nga soppi ci man nimu bariwee,
Jubbanti yi bonn, defma gòoru qualité.
Yama yokk jom, kon nak,
Nala keral, dila beggal ndax loolu laa digge.
Cofeel ci biir xolu nit
Amul njariñ sula yobbuwul ciy ngëneel.
Dalal nga ma dotuma tiit,
Yaw dara melul ni sa mbëgeel
[REFRAIN : MIA & NO FACE]
(Sama jàmm yaw la )
Yaa tax ma xam ni mbëgeel neexe
(Suma beggee yaa tax)
Mossuma foog nii...
(Sama jàmm yaw la )
Nit dinama toll fii
(Suma beggee yaa tax)
Lii daf niou bett maag yaw!
Ci mbegte nga may dello
Dima dëfal may ree
Awma beneen héros
Man yaa may begal saa su nekk
Saa su nekk….
Ecouter
A Propos de "Daf Niou Bett"
Plus de Lyrics de MAABO
Commentaires ( 0 )
Aucun commentaire pour l'instant
Vous aimeriez sûrement
Essayez l'application Mobile
A propos de AfrikaLyrics
Suivre Afrika Lyrics
© 2025, We Tell Africa Group Sarl