Fay bor Lyrics by YOUSSOU NDOUR


Ki la bëgg yab ndax alal  , yaw ignorer ko
lèpp Lu la nit , di Dokhanto , Yalla am na ko
Féek yaa ngi koy wóolóo , yalla mën në laa fayal sa bor
Ki la bëgg jaay loo sa ngor ,bayyi kook yëfëm
Ba ko fa ne tek , bés a ngi  ñëw , di na wéet ak jëf ëm
Féek yaa ngi koy wóolóo ,yalla mën në laa fayal sa bor
Te sax jamono fi mu toll nii , ku ne bopp am la tal
Mawlaana rek , moo lay defal , ken du la xamal
Féek yaa ngi koy wóolóo , yalla mën në laa fayal sa bor
Salaam alleykum , nga bañ ko fay ,mbaa xam nga ni bor la
Sa dëkkëndòo , nga koy tanxal,mbaa xam nga ni bor la
Teg say briques , ken mën të jaar mbaa xam nga ni bor la
Yor sa auto , lu la neex  def mbaa xam nga ni bor la
Nit ku la neex , nga wax ci moom  mbaa xam nga ni bor la
Yor say mbalit , fu la neex tuurmbaa xam nga ni bor la
Koo séqqël , daldi ko wor, mbaa xam nga ni bor la
Yendoo wax  , loo waax mu dañ  ,mbaa xam nga ni bor la
Koo ëpp doole , won ko ko,  mbaa xam nga ni bor la
Doo dimmili , ki nga tane, mbaa xam nga ni bor la
War ngay xalaat bu ëllëg ée , nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo , yalla mën në laa fayal sa bor
man youssou maajigéen , j’ai tout pardonné
Koo xam ni , meusone na la tooñ , jéggël ma ko

Bor yi nga am fii ñu ne , nan nga koy fay é
War ngay xalaat bu ëllëg ée , nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo ,yalla mën në laa fayal sa bor
ki la bëgg jaay loo sa ngor ,bayyi kook yëfëm
Ba ko fa ne tek , bés a ngi  ñëw , di na wéet ak jëf ëm
Féek yaa ngi koy wóolóo ,yalla mën në laa fayal sa bor
Te sax jamono fi mu toll nii , ku ne bopp am la tal
Mawlaana rek , moo lay defal , ken du la xamal
Féek yaa ngi koy wóolóo , yalla mën në laa fayal sa bor
Salaam alleykum , nga bañ ko fay , mbaa xam nga ni bor la
Sa dëkkëndòo , nga koy tanxal, mbaa xam nga ni bor la
Teg say briques , ken mën të jaar mbaa xam nga ni bor la
Yor sa auto , lu la neex  def, mbaa xam nga ni bor la
Nit ku la neex , nga wax ci moom, mbaa xam nga ni bor la
Yor say mbalit , fu la neex tuur, mbaa xam nga ni bor la
Koo séqqël , daldi ko wor, mbaa xam nga ni bor la
Yendoo wax  , loo waax mu dañ  , mbaa xam nga ni bor la
Koo ëpp doole , won ko ko, mbaa xam nga ni bor la
Doo dimmili , ki nga tane  mbaa xam nga ni bor la
War ngay xalaat bu ëllëg ée , nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo , yalla mën në laa fayal sa bor
man youssou maajigéen , j’ai tout pardonné
Koo xam ni , meusone naa la tooñ ,jéggël ma ko

Ñun doom i aadama ndiaye li ñu gën ë sonn al mooy
Aqqi dëkkëndòo , aqqi àndandoo
Ak aqqi am gi jamm yek , Yalla , yermëndéem yaatu na
Mën naa jéggël e bakkaar bu mu né
Waaye , doom i aadama Ndiaye
Boo ko yor ee lee bor , na nga ko fay , fii ci dunyaa
Walla nga balu ko mu baal la
Yé way samba, Khalass, kholal
Youssou maajigéen , oh ! lii doy na waar
Youssou Marie Sène  , bu dee lii la , bor yi bari ña ñu
Yaay na nga ma baal , baay na nga ma baal , aqq u njuréel
You , Ndour , merci beaucoup
Adji maam Ndiaye , yaay I thianék ama, maa challaa
Man da ma lay tooñ , njëk laa mer , fas sa ma kamnam
nga daldi ree , nima mbaye dieye , mbasaa mbasaa
Seng Seng papa Mbaye mbassa mbassa
Bés ni ki tay  kholal, baal naa ñépp
Am gi jamm yi , Fans yek, kharit yi ban ngemp
Ho baal nagne ngemp
Man youssou maajigéen , j’ai tout pardonné
Koo xam ni , meusone naa la tooñ , jéggël ma ko
Mani jéggël ma ko, Jéggël ma ko
yallak yeuremade yam, Jéggël ma ko
Man youssou maajigéen , j’ai tout pardonné
Koo xam ni , meusone naa la tooñ , jéggël ma ko ahhhnn yeeee
Jéggël ma ko

Watch Video


About Fay bor

Album : Mbalax (Album)
Release Year : 2021
Added By : Farida
Published : Nov 15 , 2021

More YOUSSOU NDOUR Lyrics

YOUSSOU NDOUR
YOUSSOU NDOUR
YOUSSOU NDOUR
YOUSSOU NDOUR

Comments ( 0 )

No Comment yet



About AfrikaLyrics

Afrika Lyrics is the most diverse collection of African song lyrics and translations. Afrika Lyrics provides music lyrics from over 30 African countries and lyrics translations from over 10 African Languages into English and French

Follow Afrika Lyrics

© 2022, We Tell Africa Group Sarl