Kouy Feugeuti Lyrics
Kouy Feugeuti Lyrics by MAMY VICTORY
Amna kou oubi am kou feug
Diourom nienti wérou mbapat
CNG valider sama naissance
Guewel yeup dima tagg
Nianou wadiour dima taggat
Thioumboukaay la si ndigg ma takk
Warna meuna dougou guew beurek soxla adouna mbeur mi daan nieup
Ndaw si digou dolem wara meuna fadj ay problèmes
Tekki méti saf ni kani ken mounouko sopi lem
Arbitre né prip niouy lewto sama supporter yi niom di safal
Sama diggou doolé la tolou
Door kourpegn thiaxabal
Mou rassou sol ma beug beug
Ma téyé ko si néngégn
Reporter yi né kou far ak mom
Noon yi né danou ngi xegn
Wadji mbot ma fakhat
Déy ma néma kouy yoot dou sekeut
Si sass yi ma siggi diakarlok mom diak
Mu melni kou séki ma daw outi sakou yi
Kouy feug kouy feug
Kiy feugeuti koumou done Kouy feug
Dépense nieuw feug Ndox ak courant feug
Façon soxla bouné kouné taxaw sampe ndeund
Kouy feug kouy feug
Kiy feugeuti koumou done kouy feug
Scolarité feug fébar fadiou feug
Façon soxla bouné kouné taxaw sampe ndeund
Oufou sama thioumboukaay lamb dji beugeutouma si dara
Arbitre bi woté waat na sama doolé diax diom rek dess
Lima serigne yeup digone est-ce que na ko guiss
S'tade bi nieup né tek tay la sama biss
Wathie ma ma daan woroul kou daan dangey fété kaw
Beuré len waliyané waliyane
Kouy beuré dangey daan mba niu daan la)
Wadji yekeuti gardam ma forcer ko xeex
Mou dougeul ma laaw ma tar tari deugeur mou rianiane ma waaf
Ma padeu mou djegui di bagn di out daan bou gaaw
Arbitre né ardo ma bagn douma ko wone ni diap na pogn
Sama geum geum gui tambalé deugeurat
Meun na yobou ndam li sama kogn
Bima féxé ba diap si ngemb li yakaar ni lamb dji diexna
Ndéké rothiékou neu weur ma ndomb
Gal gal ma ma reup niéti appui leer
Mou daldi seug sama nop né ma mbeur liy djot djot na
Adouna bi guew la beuss bouné nga beurék sa soxla
Kouy feug kouy feug
Kiy feugeuti koumou done Kouy feug
Dépense nieuw feug Ndox ak courant feug
Façon soxla bouné kouné taxaw sampe ndeund
Kouy feug kouy feug
Kiy feugeuti koumou done kouy feug
Scolarité feug fébar fadiou feug
Façon soxla bouné kouné taxaw sampe ndeund
Outro Voix Mamy
Watch Video
About Kouy Feugeuti
More MAMY VICTORY Lyrics
Comments ( 0 )
No Comment yet
You May also Like
Get Afrika Lyrics Mobile App
About AfrikaLyrics
Follow Afrika Lyrics
© 2024, We Tell Africa Group Sarl