Ndeye Lyrics
Ndeye Lyrics by JAHMAN XPRESS
Ndéye mougnal sa thiono dina fay
Say rongay dina ferr bilae
Ndéye sa taar bi nakar raka mour tay
Kéneu xamatoul loy nirol dakh thionoy séy
Ndéye meussou ta dég waw goor
Té sou wouti woul andi keur gui dougn tal bay soor
Teksi ay goorom ssonal ko
Té sou wakhé dieukeuram tégal ko si ay door
Ndeye siguil gua khol ma
Sa begun you wékh yi la name nak, rétane ma
Diougal gua délou keur gua
Moural sa malano soutoura té fanane si diam
Yéne say mou dioy ndakh wakh bou bone yigne deukeul si nopam
Rongagne yague sangue dome dioumo tim diko napal
Goor gorlou way ndéye mougnal
Yalla guisna lepp ndéye dina meussa bakh
Boul meussa bayi ndéye mougnal
Li lepp day diekh fok mou méti dora nékh
Ndéye mougnal
Ndéye mougnal sou domi magué feral say rongay
Boul meussa bayi ndéye mougnal
Eenhh dett way
Dina meussa bakh
Ndéye mougne na ba déme na
Wouyou dji na boromam biko sakk
Ndéye meuss ta xam banékh
Té bamouy tolou si digue ndawam guako takk
Meussoul ame si ioe louko nekh té lounek
Ladone dathie guir dab banékh
Ndéye meussou ta fanane al wayé day goudé
Foy fanane tay
Nakar ak tiss rek la yobou wayé lepp diekhna
Boul guis lo ragal way
Ndéye mougne na ba déme té narou ta féké sakh ndiarignou domam
Ndéye yo ndéye
Dieuf diou bone diouné dieukeuram ték kako mome maki mbokam
Lougué ni lay tay
Sa dound gawa fay comme sondel tek si guélaw
Yalla bo guiss lo ragal fi gua dieum teudeul té nélaw
Ndéye démna
Ndéye démna démna
Ndéye démna té dotoul gnowatt
Ndéye démna meussou ta ame liko nekh si dirou doundam
Ndéye démna say yar wayé dou diam
Ndéye démna métina lim doundoun mok ndiabotam
Ndéye démna ndeye sédé na sa diambar
Ndéye démna
Watch Video
About Ndeye
More JAHMAN XPRESS Lyrics
Comments ( 0 )
No Comment yet
You May also Like
Get Afrika Lyrics Mobile App
About AfrikaLyrics
Follow Afrika Lyrics
© 2024, We Tell Africa Group Sarl