YOUSSOU NDOUR Wax Ju Bari  cover image

Paroles de Wax Ju Bari

Paroles de Wax Ju Bari Par YOUSSOU NDOUR


Boo mer ee dëgg , sëytaane da lay dugg
Jaxjax al sa xol , def loo la , li mu bëgg
And al ak dal
Sëytaane da fay jël temps , yakkamti wul
Boo am ul chance , bu la yalla , dimmili wul
Da , lay , xaptal
Boo bëgg ée mucc , ngóor sii , yaw déglu ma
Bu la fekk oon taxaw , toog al , xarit sama
Toog al ba dal
Bu la fekk oon toog , tëdd ël , ba gagni dem
Bu yagg ee , sëytaane , day mujj dem
Doo tu la tal

Bul nangu , wax ju bari yaw , ku la ko bëgg indil na nga bañ
Bul ko kaf e , bul ko mbokk oo , fexe el dund te ànd ak dal
Booy ànd al , na nga seet , nit ku regle , te bañ bari wax
Fexe el ba adopter , dund gu ànd ul ak bari wax
Ku la ko bëgg teg , bul ko nangu , bul ko masala
Bari wax , da lay tardeel , bari wax ,da lay sonn al
Bari wax , da lay jaxase
Bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
Bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
Bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
Bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
Bu leen sonn al béer , njaw du mel ni lem
Wax lu néew , jëf lou bari , kouné war na  laa
Wax lu néew , jëf lou bari , loo loo am , maanaa

Ibra kassé birame coumba Ndiaye
Kouly kassé ek maajigéen oo
Al maabo Yacine dial, ma des ca bëlbë
Moo ma daan wax naan
Youssou na ñu ànd liggéey, te waññi wax
Te waññi wax
Baay i Oumar , baay i Alioune , baay I ndeye kassé
Góor u fatou
Baay i idi, doom i nday i adama , ak kassé plus
Al maabo yacine dial, Ibra mor astou kassé
Fatou oy , médoune kassé
Ndoumbé yatma

Wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
Wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
Wax da fay gatt yanu maanaa
Neex a dégg lool , fees ak njariñ
Ñu wax ko ba wax jot ee , fa ñu ko war a wax e
Wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
Wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
Xaaj u guddi , boo toog oon ba mu yagg , nga doon bëccëg
Di na xumb lool , ba jaaxal gaa ñi
Wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la
Wax ju néew , jëf ju bari , ku ne war na la

Ecouter

A Propos de "Wax Ju Bari "

Album : Mbalax (Single)
Année de Sortie : 2021
Ajouté par : Farida
Published : Nov 12 , 2021

Plus de Lyrics de YOUSSOU NDOUR

YOUSSOU NDOUR
YOUSSOU NDOUR
YOUSSOU NDOUR
YOUSSOU NDOUR

Commentaires ( 0 )

Aucun commentaire pour l'instant



A propos de AfrikaLyrics

Afrika Lyrics est la plus large collection de paroles de chansons et de traductions d’Afrique. Afrika Lyrics fournit les paroles des musiques de plus de 30 pays africains et des traductions de lyrics de plus de 10 langues africaines en français et en anglais.

Suivre Afrika Lyrics

© 2024, We Tell Africa Group Sarl