DAARAJ FAMILY Baal Ma cover image

Paroles de Baal Ma

Paroles de Baal Ma Par DAARAJ FAMILY


Baal ma sama baby baal ma
Lu la metti gaañ ma
Su ma la tooñe na'nga ma baal
Baal ma sama baby baal ma
Lu la xurri gaañ ma
Su ma la tooñe na'nga ma baal

Man xaw ma sax fu mu tambalee
Seytaane dox su nu diggante
Ku ne woddoo sa lammeñ
Fatt sa i nopp
Lo xam ci lu bonn wax ko sa moroom
Wax ju ñaaw da fa ñaw ni paakaa
Su demb doon tey du ma la saaga
Xoolal tey ni ñu tooge
Waxi mérr mooko sooke
Ba mënu ma la wax ni ma la bëgee

Kon baby baal ma
Sama baby baal ma
Lu la xurri gaañ ma
Su ma la tooñe na'nga ma baal
Oh oh oh, oh oh oh ooho ooho
Sumala tooñe na nga ma baal

Su ma gisatul sa i bëñ yu weex
Sa ma adduna dara du neex
Drapeau blanc na guerre bi jeex
Bu lamb tase mbër yi bayyi xeex
Man de jox naa la sama cachet
Daan nga ma jéll bu set ba nu tase
Gannaaw ày jàmm
Am na lumay namm
Yaa ngi may nanddë
Sutura nga may sangë

Baal ma sama baby baal ma
Lu la metti gaañ ma
Su ma la tooñe na'nga ma baal

Bul dekk sa nopp bi ci bitti
Wax ji mën a dàgg digg bi
Yax sa bopp bi lu bërri di
Moytul sa Clique ki mikkar yi wirri di Ibliis xawi sunu secret
Bëg nu yàqqal def ci prix bi Balu goon la jox sa enemy
Do ko gis de heur'u crime bi
Tas ko ci mbed da fa tilim di
Yàq sunu xel su nu feeling bi
Bëgg yáq su nu ajanna
And bi ñu bëgg tass yagg na
Na ñu gommé liñu paasé
Suul bi le mér bi le coow
Na nu bês su nu xol bi
Li ñu mën a jaxase mo ngi
Na nu teewal peace dund love bi

Baal ma sama baby baal ma lu la xurri gaañ ma
Su ma la tooñe na'nga ma baal oh oh oh
Du ma bën do lammeñ
Waaye leeg leeg dafay am
Ñu juyoo waaye na nga xam ne
Tooñ ak baale ño andd
Reeroo ammul ñakk waxtaan a am
Dootu ma dallati please don't let me down

Bul degg waxi noon dañuy cinema
Sunu and neexuleen mane jegema
Na nga toog bul dem mane degluma
Mala tooñ mako def dama rêccu nak
Ma nu ma la jëndak kenen li ma def yëp Bi lé mbëgeel Seede ma
Sa ma i défaut tax na nga mere ma
Leer na ma wax ma lépp ne ma Weere nga

Leegi da ma bëgg nga may reetaan
Jaral na ma def yëfu dof nga may seetaan
So mere man naa la leebal leebu ñaar nu bëggante
Sunu diggànte buur yalla laakoy seede
Yaw la yaw la
Dund ak dee mayday
Sa teekkaaral ba ngi may rày
Oh baby dawalal fair-play
Sa kanam bi nga fas
Mën na dàmm galañu mbaye dieye faye
Bul gonttu may xëy
Kaay ñu and "fly away"
Oh why oh why oh why oh why !?

Baal ma
Sama baby baal ma
Lu la xurri gaañ ma

Ecouter

A Propos de "Baal Ma"

Album : Baal Ma (Single)
Année de Sortie : 2021
Copyright : (c) Bois Sakre
Ajouté par : Farida
Published : Dec 10 , 2021

Plus de Lyrics de DAARAJ FAMILY

DAARAJ FAMILY

Commentaires ( 0 )

Aucun commentaire pour l'instant



A propos de AfrikaLyrics

Afrika Lyrics est la plus large collection de paroles de chansons et de traductions d’Afrique. Afrika Lyrics fournit les paroles des musiques de plus de 30 pays africains et des traductions de lyrics de plus de 10 langues africaines en français et en anglais.

Suivre Afrika Lyrics

© 2024, We Tell Africa Group Sarl