Yeurmande Lyrics
Yeurmande Lyrics by ASHS THE BEST
Jooy naa ba jeexal ròngoñ
Jaay naa la sama bakkan
Fippu naa fippu xeex ngir sama askan
Xeex ngir sama askan
Jooy naa ndax nèwdi dooli ngi yelwaan
Xiif akk mar jamono jii
Nèwdi doole di jooy
Jël nga sunu peace and lova
Nguur gi def ñu ennemis
Dëkk ci di ñu nòot
Jëlli ji li ñu moom jot na
Seeni doom’ag sunuy doom ku ci gën
Sunu koom ci seeni poches dafa doy
Jëlli wuñu yoonu geej fii la ñuy toog
Demmatu ñu bitim reew
Jooy naa akk samay dëkkëndoo
Yërmande Ci doomu Yalla yi
Fippu naa akk sama doomu yaay yi
Fippu xeex ngir ëllëgu reew mi
Jooy naa ba ñakk ròngoñ
Jaay la sama bakkan
Fippu xeex ngir sama askan
Xeex ngir sama askan
Fippu naa ngir sunuy doom
Fippu ngir yaay ju ñakk doomam
Fippu xeex ngir li ma moom
Yërmande ci sunuy njaboot
Jooy naa ba ròngoñ jeex
Nèwdi doole ngi yelwaan
Jooy ba ròngoñ jeex
Ngir jigeen gi soon lool
Am len yërmande
Yërmande
Yërmande
Yërmande
Yërmande
Yërmande
Yërmande
Watch Video
About Yeurmande
More ASHS THE BEST Lyrics
Comments ( 0 )
No Comment yet
You May also Like
Get Afrika Lyrics Mobile App
About AfrikaLyrics
Follow Afrika Lyrics
© 2024, We Tell Africa Group Sarl