Doolé Diou Baari Lyrics
Doolé Diou Baari Lyrics by NGAAKA BLINDé
[CHORUS]
Hé doolé diou baari dey wagni xél
Kone khalate bou barri dey takha dof
Doff yeup aljana laniou beugeu dem
Té ba légui khamouniou noumou mel
Té aduna daal lépeu koumpeu leu
Kou guiss guiss sam gate rek goumba la
Ndax goumba ya ngui guiss lou niowagoul
Hé doundou ni akhirouzamane niowagoul
[VERSE 1]
Vieux aduna dal lépeu koumpa la kén
khamoul kou djoudou tay loumuy done
Souba ganthiakh yi sakhone mo nara mégn
Nékété mo djéki doni ngogne
Li y’Allah di wané ak li y’Allah dénthie
Ken khamoul ni souba di nga ka fékk
Nitte djoudou si torokh ban ara déh
Ken khamoul ki ndax beuss di na tékk
Sougn xam xam mo sorri woul wala wala
Walay souniou beut té léragoul
Loutakh li y’Allah bindeu souniou dieu
Ba légui domou adama gui liragoul
Fi bou beuthieugué défois lépeu léer
Ken dou lathié fan la goudi né
Mane néma goudi dafa am borome bo ci
Défoul ndank di nga diomi déh
Loutax nitt you bax yi nioy téla dé
Daf am lou y’Allah nameu ci niom
Héy khaléyi djoudou ak ay djiko
you rafet da am lou y’Allah nameu ci niom
Loutax aduna bi kén dou wolou kén
Bo geumoul y’Allah do geum sa bop
Bo guissoul sa bop si bop ken
Bo meussa gestou nitte guiss sa bop
Kou guiss guiss sam gate rek goumba la
Ndax goumba ya ngui guiss lou niowagoul
Mane kou geumoul y’Allah rek geuwmala
Doundou len ni akhirouzamane niowagoul
Gni douniou lek nguir meuna doundou
Gni douniou doundou nguir meuna lekk
Y’Allah kham na lépp, y’Allah guiss
Na lépp wayé yensay dafay tokk di toni rek
Fi kounek beuga nek au top
Mais takeu sheitané lagn beugeu top
Fi kou nek kham nga sa bop wanté
Kounek beuga neub li geuna bone ci sa bop
Fi kou nek kham nga sa bop
Wanté kounek beuga neub li geuna bone ci sa bop
[CHORUS]
Hé doolé diou baari dey wagni xél
Kone khalate bou barri dey takha dof
Doff yeup aljana laniou beugeu dem
Té ba légui khamouniou noumou mel
Té aduna daal lépeu koumpeu leu
Kou guiss guiss sam gate rek goumba la
Ndax goumba ya ngui guiss lou niowagoul
Hé doundou ni akhirouzamane niowagoul
[VERSE 2]
Y’Allah dina rey lépeu louy doundou ci souf
Même souf si sax y’Allah dinako rey
Aduna ji niou nek sax dina dé mais kén
Khamoul kagn lako y’Allah ji diko rey
Gni di rey domou adama beugeu am ba
Di lolo tax khalé yi di téla dé
Accident yi di téglo té douniou kham
Djiné ya ngui contane diko célébrer
Doff yeup aljana laniou beuga dem
Té ba légui khamouniou noumou mél
Té niou démone niowatouniou wax niou si dara
Niom dal daniouy tok rekeu deuneu thiél
Nioune dal aldjana laniou beugeu dém
Doundou ba légui khamouniou noumou mél
Ndax domou adama yi di paré si mome
Té béneu bokou sék bénén bissi mome
Nioune nieup bawo ca mame adama
Nioune nioul nieulé khonkeu té nieulé jaune
Paré sheitané eup niou dolé fépp même
Bouniou fékisé souniou zone
Té domou adama di léneu si mome
Ba boléko lénén lou bokoul si mome
Garap yi doundou dougn gawa dé
Té moussouma guiss kou len diokh niou lekk
Té domou adama dagn meuna lékk
Dou léppeu ngey diaralé ci sa dé
Gni douniou lékk nguirr meuna doundou
Gni douniou doundou nguir meuna lékk
Y’Allah kham na lépp, y’Allah guiss na lépp
wayé yensay dafay tokk di toni rek
Tax y’Allah wax ci alkhouran
Li beurri si aduna bi douniou ko faratal
Mane louma def meun nako bal
Teite diégalou nieup barké sheirafall
Fi kou nek kham nga sa bop
Wanté kou nek beugeu neub
Li geuneu bone ci sa bop
Fi kou nek beugeu nek au top
Mais takeu sheitané lagn beugeu top
Fi kou nek kham nga sa bop
Wanté kou nek beugeu neub
Li geuneu bone ci sa bop
[CHORUS]
Hé doolé diou baari dey wagni xél
Kone khalate bou barri dey takha dof
Doff yeup aljana laniou beugeu dem
Té ba légui khamouniou noumou mel
Té aduna daal lépeu koumpeu leu
Kou guiss guiss sam gate rek goumba la
Ndax goumba ya ngui guiss lou niowagoul
Hé doundou ni akhirouzamane niowagoul
Watch Video
About Doolé Diou Baari
More NGAAKA BLINDé Lyrics
Comments ( 0 )
No Comment yet
You May also Like
Get Afrika Lyrics Mobile App
About AfrikaLyrics
Follow Afrika Lyrics
© 2024, We Tell Africa Group Sarl