Paroles de Saajobaan
Paroles de Saajobaan Par AMADEUS
Eey Màsamba Waalo eeeh hii
Su mbëggeel doon jaay
Am naa njëgam
Dinaa la wan sama yéene yi ma am ci yaw
Duma ku lay jay
Te duma la wor
Dinaa la wax dëgg ak lum metti metti
Maa la woo ne la maa la nob
Miinal la sama bopp ba nga barder maa la tooñ
Kon nag loo ma manti def
Lu mu metti naa ko muñ
Àdduna du dox ba ma soppi li ma la wax doo ma weddi
Ay bu doon ay nax neex na ma
Fekk ma ciy gént yee nga ma
Jàmm ju bari may nga ma
Yaa ngi may dundal àjjana
Tamit tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne man la
Gëmal ma ne Man rekk nga nob
Sama saajobaan
Tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne Man la gëmal ma ne Man rekk nga nob Sama saadjobaan eeee waay
Xam nga duma puruux duma fàtte bi may surux
Xuntu wu lëndëm wi nga ma génne dinaa ko wax
Du lu rafet ci wax
Soo ma bàyyee damay torox
Nawle yépp bis bu ñu teewee dinaa ko wax waaaay
Doy nga ma ci kër
Kenn du la sikkal
Man yaw mii yaay ki ma fiital (tiital)
Doo dund ngistal
Ngor gi nga jiital
Ragaluma siiwal
Nun ñaar ndax doy nga ma ci kër
Ndaxte Mane maa la woo
Ne la maa la nob
Miinal la sama bopp ba nga barder maa la tooñ
Kon nag loo ma manti def
Lu mu metti naa ko muñ
Àdduna du dox ba ma soppi li ma la wax doo ma weddi
Hay bu doon ay nax neex na ma
Fekk ma ciy gént yee nga ma
Jàmm ju bari may nga ma
Yaa ngi may dundal àjjana
Tamit tëggal ma ma jaayu
Tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne Man la
Gëmal ma ne Man rekk nga nob Sama saajobaan
Tëggal ma ma jaayu
Xamal ma ne Man la
Gëmal ma ne Man rekk nga nob Sama saajobaan eeee waaay
Ecouter
A Propos de "Saajobaan "
Plus de Lyrics de AMADEUS
Commentaires ( 0 )
Aucun commentaire pour l'instant
Vous aimeriez sûrement
Essayez l'application Mobile
A propos de AfrikaLyrics
Suivre Afrika Lyrics
© 2024, We Tell Africa Group Sarl