Paroles de End-Discipline Par NDONGO D (DAARAJ FAMILY)


[COUPLET 1]
Ya ngi xaax tëf fune ci mbed sotti mbalit mi sa yoon
Dëkando faleewo ya ngi baare tali bi
« tente » koñ bi yëp poot dajale say paan
Ni cars-rapide bu yab ba fees ci digg yoon bi mu « panne »
Saufër bi dugg tali bi « dos-d'âne » falewul
Xiiro bi ηaayo bi koksër aparanti ken attewul
ñaata saufaar ñu lim burle “feu-rouge” ñu ne cëm
Ki moy waaja bimuy dawal ub seen bët ñu gëmm

[REFRAIN]
Endiscipline
ku dem yobaale sa jikko
Li araam moy ñakk yaradiku tilim jikko
Endiscipline
Melokaan bi ngay dikke ci bitti ni nga njëkke
Ñu ngi gis nuñ lay sikke
Endiscipline
Marsandisu reewande tey la gëna lambb ñëppay jënd ñëppay jaay
Endiscipline
Yaa ngi tëb tëb ta do dal
Bis yar a dal ta ken ken du la raay

[COUPLET 2]

Mëno xaar sa tuur sooga ñëw burle rang bi
Ya ngi ndadé kontewoo bëg tëb “numba 1one bi”
Bo dugge bus tafu tafee ak sa xet ya ngi nuy xër saxaar sigaret sanni fula neex
Dajjeeti nga beneen paket
Naan sa njaru kafee kaas bi xaar yeneen sareet
Ya ngi guux sa ndox fi nga taxaw ngay sanni mbuus bi say loxo duñu set ya ngi gén leegi duus bi


[REFRAIN]
Endiscipline
ku dem yobaale sa jikko
Li araam moy ñakk yaradiku tilim jikko
Endiscipline
Melokaan bi ngay dikke ci bitti ni nga njëkke
Ñu ngi gis nuñ lay sikke
Endiscipline
Marsandisu reewande tey la gëna lambb ñëppay jënd ñëppay jaay
Endiscipline
Yaa ngi tëb tëb ta do dal
Bis yar a dal ta ken ken du la raay

Endiscipline

Civilise ak badoolo....
Doxin wa ak waxin wa
Jëf ja ak nuyoo ba ak rentré ba Accident yu bëri yi ngay gis manque de civisme la ...
Bu fukki nit di gas fukki nit di suul pax du gaawa am
Manque de civisme mën ta weesu
pont ba duñ ca yeeg
ba ci commissariat yi leele nga gis mode tortures yo xamne manque de civisme la !!!

[COUPLET 3 ]
“Défense d'uriner “ mur bi sax tereko
ya ngi taxaw ci mbed mi saw jokkan fa pareego
Policier bi neena priip njaga ndiaay fok mu stop
Bu de dafa amul frein loxom fok mu yoor ci poos
taxi gén sens-interdit liila xelam yannu ci loos
Marchands ambulants dox ci naaj bi dans le vent
Ni trotuwaar bi en-avant fok mu def sandikat
Xat na lool Sandaga liko jële dëk ba moola fi inddi dañuy course
Ak yafuus mëna jël sen benefice
Lu tabax yeeg yeeg xel ya ngi gëna di kule
Daf ñuy tere gëna gis teggin bi nilañuy koy suule
Lu tabax yeeg yeeg xel ya ngi gëna di kule
Daf ñuy tere gëna gis teggin bi nilañuy koy suule

 

Ecouter

A Propos de "End-Discipline"

Album : End-discipline (Single)
Année de Sortie : 2019
Ajouté par : Ndongod
Published : Aug 21 , 2019

Plus de Lyrics de NDONGO D (DAARAJ FAMILY)

NDONGO D (DAARAJ FAMILY)

Commentaires ( 0 )

Aucun commentaire pour l'instant



A propos de AfrikaLyrics

Afrika Lyrics est la plus large collection de paroles de chansons et de traductions d’Afrique. Afrika Lyrics fournit les paroles des musiques de plus de 30 pays africains et des traductions de lyrics de plus de 10 langues africaines en français et en anglais.

Suivre Afrika Lyrics

© 2024, We Tell Africa Group Sarl