Bamba la Paix Lyrics by JAHMAN XPRESS


JAHMAN ft AHMADA JADID -  bamba la paix

Tchi digueunté marakh maassé
Bi djololi suuf séédé
Tchi lagne gawantu sakou ci sa ay njeurigne
Tchi kaddu yu tedd yi
May bindeu ngir way ci mom
Kène dotoul mel ni yaw
Nio ngi lay chiaaré
Di riir ngir modou bamba
Mo xekh té balle takoul
Di riir ngir maam mi indi lerr
Tchi yone wou méti wi
Ak keppeu ko xamni baye fall nga tèy
Bégué mame cheikh ibra fall
Maïsa bigué coumba fall mo wané yone bi

Aouzou billaah
Bismilaah

Kène dou yaw Ibra fall
Cheikh Ibra yi nékal kamal
Dial goor yalla yomboul
Lassal daak lil Jamaal
Ibrahima faal lam yazal
Yaay lamp gueuneel bi bamba taal yaaram bi naam fall
Yaw la bamba wane kawçaraak gui naane
Gueediou lerr yi yako naan
Mbeur yeup nga bolè daan té fall titeurou woulo
Seug beek sigui béé
Borom yallah mba jaameuh nga am
Tabbé maame Seynabou Ndiaye mo wane yone bi

Baye fall moy lou doyouk waar
Mo toudou tuurou yallah bi
Bamouy xotti djawou dji
Di yengueul harass ak kurçiyu
Baye fall moy dieufé ndigueul
Moy diokhé té kene douko laathie
Baye fall bou deugou té woor
Sa keur moy aldiana firdawsi . Haaaan

Niou roy ci Cheikh modou kara ak
Baye karim Al-Akhlah
Tognou niou togn lou wougnou
Dieuf yi nagnou ko rafétalaate
Kone keppeu ko xamni baye fall nga tey
Beug roy tchi cheikh ibra fall
Nanga am yarr mandou tèy teuy
Njeufé ndigueul

Al Hamdulilah niou santati Cheikh Bamba tay
Ngir mo takhaw djouli wone fa ndar bagn niou sankou tay
Rakkam ya moy sauwétasse tchi nioune ngir moy dokh batay
Magal ko moy li war ci nioune diko sante tay
Bureau bé fa ndar mo atté
Goor yafa diaar beu weuy
Kou tchi doul serigne touba kérok signé wone nga “oui”
Balle darsak wa tribunal kérok nieup xeuy kagnou naane
« Borom ndar takhaw dikou yallah dji djay »

Bamba bay neu goop na djaak neu
Gaadou neu ak sakkeu
Sameuh bodji wall neu modgne neu ganaaw aadou sokkeu
Meune neu dieuf nako ak xam xam
Mouride na nga deggueuh
Ragnel lou baakh tchi lou bone boula tchi kene degueuh
Beus nga xol bi diokh bamba kone teudeul nelawal
Xara-ngal neel xareu-xareu wakh leu djou am sewa sew
« Wa salaamoune ala manni tabkhal khoudaa »
Miim reew bamba ka mom moy kika mom

Watch Video

About Bamba la Paix

Album : Bamba la Paix (Single)
Release Year : 2018
Added By : Afrika Lyrics
Published : Oct 31 , 2018

More JAHMAN XPRESS Lyrics

JAHMAN XPRESS
JAHMAN XPRESS
JAHMAN XPRESS
JAHMAN XPRESS

Comments ( 0 )

No Comment yet



About AfrikaLyrics

Afrika Lyrics is the most diverse collection of African song lyrics and translations. Afrika Lyrics provides music lyrics from over 30 African countries and lyrics translations from over 10 African Languages into English and French

Follow Afrika Lyrics

© 2024, We Tell Africa Group Sarl